Songtexte.com Drucklogo

Mak Mo Songtext
von Lidiop

Mak Mo Songtext

Magg mo mane n
Magg mo eh mane nameunala

Bësub kerook gee
Sama adduna moo tukkee
Jile xibaar, lu ko gëna doy waar
Xaaji guddi lañu ma woo
Nema moom dem na
Mënumako woon gëm
Waaye dem na
Jaam beek pexeem, ni Yàlla dogalam
Lu metti góor lay dal
Bëggoon na ñu nga took fi ba ci kanam
Bu Yàlla nee waawaaw jaam du ne déedéet
Dem na, dem na du ñëwaat
Moom de dem na du ñëwaat
Sama mag jee, man namm naa la


This the life the life mysterious life
This is the life the life eternal life
Mag mo yaw, man namm naa la
Mag mo he, man namm naa la

Ñëpp ñu ngiy jooy
Wéetal ga ñu
Yaay mu ngiy jooy
Baay
Mag ak rakk
Mbiidu mu ngiy jooy, Paap Muusaa mu ngiy jooy
Isaa Ngeer mu ngiy jooy Laay Géey
Niep ñu ngiy jooy
Djiby agn mu ngiy jooy elaj mu ngiy jooy
Sylvain mu ngiy jooy
Man gëm naa ne Aljana ngay yeewo
Yaa ma yàgg wax ni lépp dina baax
Yàgg nga ma wax ni picc moom jógul rekk naaw
Fàllu na la teeru, Sëriñ Tuuba na la teeru
Serafaal na la teeru firdawsi ngay
Doxonto


Sama mag jee, wéetal nga ñu
Sama mag jee, ñun de namm na ñu la
Mag moo yaw nax nga ñu ba dem
Sunu mag jee Wéetal ga ñoo
Eh he he

This the life the life mysterious life
This is the life the life eternal life
Mag mo yaw, man namm naa la
Mag mo he, man namm naa la

Aljana ngay doxonto, nañu fa gisante
Du ñu la fàtte, yaa ngi yaw suñu xel
Sama mag jii, moom dem na eh
Moom de demna
Life eh he he he
Magg mo he he
Man namm naa la, namm naa la, namm naa la
Aljana ngay doxonto sama mag jee duñu la mësa fàtte
Wéetal ga ñoo, duñu la mësa fàtte
Wéetal ga ñoo, duñu la mësa fàtte

Songtext kommentieren

Log dich ein um einen Eintrag zu schreiben.
Schreibe den ersten Kommentar!

Beliebte Songtexte
von Lidiop

Quiz
In welcher Jury sitzt Dieter Bohlen?

Fans

»Mak Mo« gefällt bisher niemandem.